Découvrez des millions d'e-books, de livres audio et bien plus encore avec un essai gratuit

Seulement $11.99/mois après la période d'essai. Annulez à tout moment.

Maa sopp Senegaal -: Afrique mon amour
Maa sopp Senegaal -: Afrique mon amour
Maa sopp Senegaal -: Afrique mon amour
Livre électronique495 pages2 heures

Maa sopp Senegaal -: Afrique mon amour

Évaluation : 3 sur 5 étoiles

3/5

()

Lire l'aperçu

À propos de ce livre électronique

Das vierte Buch der Autorin Barbara Krippendorf richtet sich in erster Linie an west-afrikanische, ehemals francophon kolonisierte Leser/innen. Es ist die Übersetzung eines Groß-Teils der Texte des dritten Buches: "Schwingen der Sehnsucht nach Afrika" mit Hinzufügung neuer Texte.

Das Buch enthält 6 Kapitel in Wolof und 6 Kapitel in Französisch.
Das Herz des Buches pulsiert im Rhythmus afrikanischer Sprachen;
Wolof, Serer, Pulaar, Djola, Soninke, Mandinka, Shona, zusätzlich Arabisch und Türkisch.

Mit der Wahl afrikanischer Sprachen unterstützt die Autorin ihre Wert-Schätzung und Hoch-Achtung für ein Afrika, das kaum erkannt und kaum gesehen wurde, und doch als Wiege der Menschheit gilt.
LangueFrançais
Date de sortie13 mars 2019
ISBN9783765089008
Maa sopp Senegaal -: Afrique mon amour

Auteurs associés

Lié à Maa sopp Senegaal -

Livres électroniques liés

Poésie pour vous

Voir plus

Articles associés

Catégories liées

Avis sur Maa sopp Senegaal -

Évaluation : 3 sur 5 étoiles
3/5

1 notation0 avis

Qu'avez-vous pensé ?

Appuyer pour évaluer

L'avis doit comporter au moins 10 mots

    Aperçu du livre

    Maa sopp Senegaal - - Barbara Krippendorf

    sëkk.

    Wër naa àdduna

    Léeg-léeg, yoon wi gudd ci man,

    Sama waliis diis-a-diis,

    Ndox mi xóot-a-xóot,

    Mbar yi takkarnaase,

    Sedd bi tar-a-tar,

    Naaj bi tàng-a-tàng,

    Suuf si pëndee-pënde,

    Xeer wi ñagas-a-ñagas,

    Péey yi baree-bare coow.

    Ma wër àdduna wërngal kepp

    Waaye taxul ma gis

    La ma doon wuti.

    Dem naa ci dëkki kaw

    Yi gëna dand ci Senegaal, ci Afirik ;

    Foofa rekk

    Laa mujjee jote li ma soxla woon.

    Waa kow gi ñu ne dañoo ndóol

    Séddoo ak man as tuut si ñu amoon.

    Ndaxam loolu mooy séddoo.

    Séddoo, mooy ndëxënteefu àdduna dëgg.

    Ñu jàppe ma ni yaaram,

    Ni ndawu sunu Boroom.

    May ma ci seen ndoxum teen

    Mu seral sama yaram wépp.

    Ci basaŋ bu lale ci keppaaru genn garab,

    May yég ni ku nekk ci lalu buur.

    Waa kow gi ubbil ma

    Seen buntu xol.

    Ba ma ca duggee,

    Asamaan si, biddiw yi, weer wi

    Dañu ma jegesi

    Guléet, mu ame noona.

    Ma taxaw ci seen biir,

    Wa kow gi yaatal ma ci seen suuf

    Si ma taxawoon.

    Foofa,

    Suuf, deesu ko jénd, deesu ko jaay ;

    Suuf, mayug Yàlla la.

    Ma sant sunu Boroom.

    Maa sant Yàlla.

    Mixey gidmaa Róog.¹

    ¹ Mixey gidmaa Róog : Maa sant Yàlla (en séeréer).

    Jam soom¹

    السلام

    Maa bëgg Babaak.

    Foofa, ame naa fa ndox

    Mu jóge ci balluwaayu dund gi,

    Ñam

    Wu jóge ci biir suuf si.

    Foofa, damay suur këll.

    Maa bëgg Babaak.

    Foofa, jànge naa fa

    Ay woy ak i fecc

    Ci naaj wu tàng wi,

    Ci guddi gi biddéew yi leeral

    Ak weer wu mel ni ngal.

    Maa bëgg Babaak.

    Foofa, fekk naa fa

    Jam soom.

    Jàmm,

    Yégoo,

    Déggoo.

    Ci li ma wër

    Ak ci man.

    Jam soom.

    ¹ Jam soom : Jàmm rekk (en séeréer).

    Peccum picc yi

    Séeréer si dañuy fecc ni picc yi.

    Gis naa leen Babaak, benn dëkku kaw ci biir àll bi.

    Ci biir àll bi, ci dëkki kaw yi, am na jàmm. Jàmm ju wesaaroo fépp.

    Ci dëkki kawu Afirik yi, am na jàmm. Jàmm ju wesaaroo fépp.

    Ñi dëkk Babaak laay wax, benn mbooloo mu bokk ci waaso Séeréer yi.

    Foofa, am naa fa ay xarit, ay xarit yu baax yu dëkk ak seen njaboot.

    Njaboot ya dañu bari, ubbeeku. Nit ñu bari ñoo fa bokk sanc.

    Njaboot yu bari lool ñoo fa bokk dëkk.

    Ca dëkki kaw ga ñëpp a xamante.

    Fii, ñi meññe ci Musaa Fay,

    Xarañ ci xalam ak riiti ak sabar, xarañ ci galan ak fecc.

    Donoy seen xam-xamu baay ja nga xam ne néewu géwél ba,

    Ni ñu ko baaxe def, mu nga ñu denc guy-géwél. Ruuham mi ngi wéy di dund,

    Ni mamaat yi teew fu ne.

    Am na yit Maam Moor Anta Sali Fay.

    Yoxoy ngalamam ya tax nañu koo doon lakk-katu mburu.

    Xolam bu yaatu bi, xelam mu ubbeeku def nañu ko taalifkat.

    Baatam bu neex bi def na ko woykat. Muy woy jàmm ci biir dëkkam.

    Ndax ci dëkkam, jàmm a fa am. Jàmm ju law fépp.

    Maam Moor Anta Sali Fay jàngal na ma làkkam.

    Jàngal na ma ay woyam, aadaam ak cosaanam.

    Jàngal na ma lépp lees di rafetlu ci askanam.

    Ak loo mëna def, ak loo mëna bëgg,

    Jiitalal màggal Ki sàkk lépp. Ñaanal Yàlla.

    Nuyul say moroom. Nuyul ak teggin nit ku nekk. Nuyul ku nekk ci mbégte.

    Amal yitte ci ñépp.

    Séddool sa ndox. Séddool sa lekk. Séddool sa pukkus bëccëg bi. Séddool sa basaŋ guddi gi.

    Séddool lépp loo moom. Lépp loo mëna séddoo, séddoo ko, feek mën nga ko.

    Bu dund gi diisee gànn, su boobaa, dellul ci sa cosaan.

    Saa yu njàqare fëggee sa bunt, su boobaa dellul kër ga ;

    Ca dëkku kaw ga, fa nga juddoo.

    Foofa, danga fa fekk jàmm. Foofa jàmm rekk a fa nekk. Jàmm ju wesaaroo fépp.

    Li ma dund laay wax. Ci biir dëkku kaw yi nekk ci àllu Afirik,

    Bu guddi gi wàccee ci dëkku kaw yi, te amul kuuraŋ,

    Lépp ay nuur ci lëndëm gi. Lëndëm gu lay muur, muur lépp.

    Ci mbàmbulaanug guddi gu ñuul gi, dangay jankonte ak guddi gi ci xaaju guddi gi.

    Boo jëmalee sa bët ci jaww ji,

    Biddéew yi weng di la muuñal, di mellax ndànk.

    Te bu weer wi génnee, sa xol fees ak mbégte. Ca kow, weer wi di leeral suuf si.

    Nit ñi génne ci seeni pukkus di daw, di woy ak a fecc,

    Bég ci waxtu wu kéemaane woowu.

    Dañuy yég jàmm ci seen bopp, nekk benn ak àdduna si.

    Te loolu mooy jàmm ; jàmm ju ëmb lépp

    Ci dëkki kaw yi nekk ci àllu Afirik.

    Foofa de, jàmm am na fa. Jàmm ju wesaaroo fépp.

    Fu ma tollu, sama xel a ngi ci Babaak, ci picc yiy fecc ci diggu àll bi.

    Muy ci suufu biddéew yi, di ci leere gi.

    Sama ruuh day sàngoo jàmm jooju. Jàmm juy law fépp.

    Dafa amoon bés

    Dafa amoon bés,

    Ay màggat yu jigéen :

    Ñu wutsi ma,

    Génne ci seeni néegi ban.

    Ñuy layy-layyi te loot ;

    Ñu ngiy liyaar,

    Di ma ŋóobi,

    Seen gët yi di melax

    Ndax mbégtey cokkaas.

    Ñu wër ma,

    Di ma tooñ,

    Di ma kobos,

    Di ma buux ndank,

    Di xëcc sama kawar.

    Te ñu ngiy woy

    Seen woy ;

    Te ñu ngiy woy

    Yinge Yaaye.¹

    ¹ Yinge Yaaye : rastas (ci séeréer). (Sama kawar gi ma rasta moo tax ñu fent woy wii : Yinge Yaaye).

    Yinge Yaaye¹

    Xoolal rasta yi !

    Ñooy reen yi.

    Reen yi,

    Liy dundal garab gi ;

    Reeni garab gi

    Sax ci biir-a-biir,

    Dëju ci biir suufu Afirik.

    Xoolal fas wi

    Di nodd

    Ak kemtalaayu kàttanam,

    Taxaw ci tànku daw

    Ci guddi gu sori gi.

    ¹ Yinge Yaaye : rastas (ci séeréer). (Sama kawar gi ma rasta moo tax ñu fent woy wii : Yinge Yaaye).

    Jigéen ñii dañoo màgget

    Jigéen ñii dañoo màgget,

    Màgget lool ;

    Boole ci,

    Nekk ay ndaw te woyof.

    Ñooy seen

    Mamaati mamaati maami bopp.

    Ñooy seen sëtaati sëtaati sëti bopp.

    Dama leen di jeneer ci lëndëm gi,

    Ci waxtu wi yewwu ak gëmmentu

    Di xëccoo ci sama keppaaru xef yi,

    Ma leen di dégg, seen gémmiñ yiy ñurumtu

    Mbirum dund, dee ak dékki,

    Mbirum kumpay tawféex ju sax ba faw.

    Ma ànd ak ñoom ngir ñoom,

    May woy woy wu bees

    Wu sosoo ca jamono ju yàgg-a-yàgg.

    Àdduna yàggul.

    Àdduna lu gàtt la.

    Àdduna yàggul

    Àdduna yàggul ;

    Àdduna sii

    Saxul ba faw.

    Àdduna, picc yuy naaw la.

    Bégal !

    Bégal ak nun !

    Looy def ?

    Xoolal sa ginnaaw

    Sa toflanteg maam yi.

    Xoolal sa kanam

    Sa toflanteg doom yi,

    Ak gu sa doomi doom yi.

    Àdduna saxul ba faw.

    Àdduna, picc yuy naaw la.

    Ana loo fi mëna indi ?

    Ana loo fi mëna bàyyi ?

    Yaay kan ?

    Yaay kan dëgg dëgg ?

    Àdduna saxul ba faw.

    Àdduna, picc yuy naaw la.

    Màgget nanu,

    Te nu ngi jékki ci kanamu bunt bu mag bi.

    Leegi nu wéy ;

    Danuy dem, dellusi ;

    Dellusi, demaat ;

    Demaat, dellusiwaat.

    Bégal !

    Bégal ak nun !

    Àdduna yàggul ;

    Àdduna, picc yuy naaw la.

    Àdduna yàggul ;

    Àdduna lu gàtt la.

    Jataayu jigéen ñi

    Ay jigéen ñu njaxlaf,

    Ay jigéen, ñoomi neen,

    Ay jigéen ñu sawar.

    Ndaw i coow, ndaw i reetaan !

    Kuur yiy dal ci biir gënn yi,

    Saxaar si, safara si,

    Tàngoor bi ak ngelaw li jaxasoo.

    Yére yi di naaw di fërr-fërri,

    Jëlëm yi di jolli.

    Leket yi, njaq yi ak cin yi

    Ñu yenu ba mu jekk

    Bokk na ci li leen taaral.

    Juun-juuni suba teel

    Ba guddi gi sori, ñu boole :

    Njaay, wéccoo, waxaale,

    Xarañ ci wax ba yey,

    Liggéey, woy, pecc ;

    Xuloo yi tam ci biir mboole

    Mu yaramam tàng ndax juun-juuni.

    Ay liir yu ñu boot

    Ak yu ñu fab,

    Ay tuuti-tànki gox bi

    Ñu leen di toppatoo noonu.

    Jaabante bi,

    Callweer,

    Gët xeeñ yu saf,

    Ay kaf yu saay-saaye ci seen biir,

    Te kersa amu ci, der ak der ;

    Seen cër yi di riisoonte,

    Defuñu ko muy dara.

    Sama xel yépp nekk ci ñoom.

    Ma nekk ci seen biir,

    Di yég bànneex ci ni ñu diriyaankee,

    Ci seen ñuulaayu der

    Biy nes-nesi ak ñaq wi,

    Ci ni seen siddit yi,

    Sis yi ak caas yi di dawe.

    Ni may gise jigéen ñooñu,

    Ma sóobu

    Ci ni ñu jigéenee.

    Ma sóobu

    Ci li ñuy def bés bu nekk.

    Ma sóobu

    Ci seen sutura.

    Ma sóobu

    Ci xolu ndey ji ñu judduwaaleel.

    Asamaanu guddi gi

    Asamaanu guddi gi

    Ak i biddéewam yiy nes-nesi,

    Weeram wi ni xaalisu ngal, leer naññ,

    Tey jeeti,

    Dafa jége bu baax dëkku kaw yi.

    Leket yi

    Ay biddéew lañu daanaka ci daŋ-daŋu bës yi ;

    Mënuñoo ñàkk

    Muy ci kër yi, di ci tool yi.

    Jigéen ñi réerewuñu mbir seen njariñ,

    Ba tax ñu koy woy.

    Leket !

    Yow mi biddéew yi yóbbulul dara,

    Lu ma doon koon su dul koon ak yow ?

    Fi jant bi fenkee ba ba muy so,

    Ak ba suuf sedd,

    Ci yow laay tanxe lépp.

    Yaay sama biddéew ;

    Maa ngi lay sant.

    Yow laa jagleel woy wii.

    Leket !

    Su dul koon ak yow,

    Dara du dox.

    Su dul koon ak yow,

    Génte du am,

    Takk du am,

    Rob du am,

    Xarbaax du am,

    Liggéey du am.

    Su dul koon ak yow,

    Bëccëg du am,

    Guddi du am.

    Su dul koon ak yow,

    Dund du am,

    Dee du am.

    Sama suuf !

    Sama assamaan !

    Sama biddéew !

    Su dul koon ak yow,

    Dara du dox.

    Ci xaaj-wërngëlu weer wi

    Gis naa jigéen ñi.

    Gis naa jigéen ñi

    Ci seen biir kër yi,

    Gis naa leen ca waar wa.

    Gis naa leen ñuy root ca teen ba,

    Gis naa leen ñu yenu ay njaq,

    Gis naa leen ñuy taale matt,

    Gis naa leen ñuy setal ëtt bi,

    Gis naa leen ñuy fóot,

    Gis naa leen ñuy jekk-jekkal seen kër yi.

    Gis naa leen ak seeni doom,

    Seen doom yi doon nàmp,

    Seen doom yi ñu doon boot,

    Seen doom yi leen wëroon fépp.

    Gis naa jigéen ñi

    Di lijjanti seeni mbir ca ja ba,

    Ci suba teel,

    Ba ngoon gi sori.

    Gis naa jigéen ñi

    Ñu yenu ci seen wagg yi

    Yenub njaboot gi.

    Gis naa jigéen ñi.

    May laaj sama bopp

    Naka lañuy def ba dékku

    Tumuraanke gii yëpp.

    May laaj sama bopp

    Naka lañuy def ba teggi

    Seen yen bi.

    Gis naa jigéen ñi.

    Ci guddig xaaj-wërngëlu weer,

    Gis naa leen di janeer.

    Gis naa leen

    Ñuy dem ca dex ga,

    Yenu ay ngandi leket ;

    Ponkali leket

    Fees ak seeni naqar

    Yu ñuy tuur ca dex ga.

    Gis naa leen guddi,

    Gis naa leen di janeer,

    Gis naa leen.

    Gis naa leen

    Ci xaaj-wërngëlu weer wi.

    Mi ngi may wax li xew këram

    Benn bés, Buubakar, waxambaaneb Gine Konaakiri,

    Dafa ma doon waxtaane këram, ne ma ginnaaw bu ñu ndënoo,

    Mbooleem waa kër gi dañuy dem kenn kenn ci kanamu ndey ji.

    Ku nekk sant ko ngir ndën li : Na kobarka.¹

    Bu ko defee, yaay ji, moom it, sant Yàlla :

    Al barka. Jaaraama. Inike ŋse.

    Wax jooju yéem ma lool ba ma tàmbali di ko woy.

    Bi ma delloo Almaañ,

    Ma soppi wax jooju benn woyu cant

    Ci maalenke, araab, pulaar, wolof,

    Jagleel ko sama mbokk yépp.

    Jagleel ko ñépp ñi ma fi jiitu woon.

    Jagleel ko ñépp ñi ñëw ba noppi ak ñiy ñëwi sama ginnaaw.

    Maa ngiy sant sama yaay, di sant sama baay.

    Maa ngiy sant samay maam.

    Maa ngiy sant samay mamaati maam ; samay mamaat yépp.

    Maa ngiy sant samay doom. Maa ngiy sant samay doomi doom.

    Maa ngiy sant Aji-Sakk ji, Aji-Kattan ji, Ki sakk bepp bakken.

    Maa ngiy sant Ki ëmb lépp lees mëna gis ak lépp lees mënula gis.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Jërëjëf. Jaajëf. Akasa.

    Al barka.² Jaaraama.

    Inike ŋse. Inike mba.³

    الحمد لله رب العالمين

    الشكر لله

    شكر الام

    ¹ Na kobarka : Yaay, jerejef (ci mandinka).

    ² Al Barka : Sant Yàlla (ci mandinka).

    ³ Inikee Nsee, Inikee Mbaa : Sant Yàlla (ci mandinka).

    Na kobarka¹

    Yaay, jërëjëf

    الحمد لله رب العالمين

    Jërëjëf. Jaaraama. Al barka.²

    Inike ŋse. Inike mba.²

    Yaay !

    Jërëjëf. Jërëjëfatee.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Ngërëm ñeel na Yàlla, Buuru àdduna yi.

    Baay !

    Jërëjëf. Jërëjëfatee.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Ngërëm ñeel na Yàlla, Buuru àdduna yi.

    Maam bóoy !

    Jërëjëf. Jërëjëfatee.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Ngërëm ñeel na Yàlla, Buuru àdduna yi.

    Mamaati-maam yi !

    Jërëjëf. Jërëjëfatee.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Ngërëm ñeel na Yàlla, Buuru àdduna yi.

    Mamaati-mamaati maam yi !

    Jërëjëf. Jërëjëfatee.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Ngërëm ñeel na Yàlla, Buuru àdduna yi.

    Xale yi !

    Jërëjëf. Jërëjëfatee.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Ngërëm ñeel na Yàlla, Buuru àdduna yi.

    Sët yi !

    Jërëjëf. Jërëjëfatee.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Ngërëm ñeel na Yàlla, Buuru àdduna yi.

    Sëtaati sët yi !

    Jërëjëf. Jërëjëfatee.

    Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiina.

    Ngërëm ñeel na Yàlla, Buuru àdduna yi.

    ¹ Na kobarka : Yaay, jërëjëf (ci mandinka).

    ² Al Barka. Inike ŋse. Inike mba : Sant Yàlla (ci mandinka).

    Lépp a ngiy fecc

    Lépp a ngiy fecc :

    Nit ñi, mala yi ak garab yi.

    Cëy bii wërsëg ! Cëy bii naataange !

    Cëy bii bànneex !

    Lépp a ngi fi ngir ndën li !

    Lépp a ngiy melax ni ay biddéew fii fépp,

    Gët yaa ngiy tàkk ;

    Yëg-yëgu bànneex wesaaroo

    Ci biir reetaan yi.

    Ndënd yu ay yoxo yu aay di tëgg

    Ñooy ndawi tëgg mu jóge ci xol.

    Lépp a ngiy fecc :

    Nit ñi, mala yi ak garab yi.

    Tàngooru jànt bi di fóon der yi.

    Di mar ñaq wi bu baax,

    Toqi per yu bawoo ci yaram yi.

    Der bu wér péŋŋ

    Ci yaram wu ponkal, sidit yi di feeñ

    Di xëccu, di lemu, di tàwweekuwaat ak doole.

    Tank yi tëbe ci suuf si,

    Sëllax suuf su tàng ci kow.

    Lépp a ngiy fecc :

    Nit ñi, mala yi ak garab yi.

    Safara jant bi di leeral nàññ asamaan si,

    Fitti leer yuy jang te tàng jër.

    Ngelaw laa ngiy riir, di fatte.

    Suuf saa ngiy wëndeelu, boole ci di yéngu.

    Lépp a ngiy fecc.

    Lépp a ngiy dund.

    Lépp a ngi ràbbaske.

    Lépp a ngi tag ci jaww ji.

    Lépp a ngiy fecc :

    Nit ñi, mala yi ak garab yi.

    Bismillah

    Bismillah.

    Alhamdulillah.

    Laa Illaaha Illa laa.

    Ci turu Yàlla.

    Cant ñeel na Yàlla.

    Amul jeneen Yàlla ju dul Yàlla.

    Ngëm lu am solo la

    Ci doom-Aadama.

    Yàlla mooy sunu Boroom ; Ki gën ci nun.

    Jàpp, julli, dina yombal yi nu sumb,

    Dina leeral xol yi, xel yi ak xalaat yi,

    Di dimbale aji ngëm gi,

    Di ko indil jàmm, mbëggeel ak naataange.

    Bismillah.

    Alhamdulillah.

    Laa Illaaha Illa laa.

    بسم الله

    الحمد لله

    لا إله إلا الله

    Bu la nit ñi laajee

    Bu ma nit ñi laajtee,

    Su boobaa, ne leen

    Dama

    Vous aimez cet aperçu ?
    Page 1 sur 1